TSK

TSK · Proverbs 15:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

Yeena ngii, bañ sama yar, xalab samay kàddu.

Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.

Ku bëgga xam, bëgg ku la yedd; ku bañ ku la àrtu, bàyyima nga.

nga naan: «Dañu maa dóor te gaañuwuma, duma ma te yéguma ko. Moo! Duma yewwu nag, ba naaneeti?»

Xanaa du yeena def seen bopp lii, di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, ba mu leen di jiite ca yoon wa?

Waaye yaw soo artoo nit ki ngir mu wacc yoonu mbonam, te taxu koo wacc yoonu mbonam, moom la aw ayam di àtteb deeyam, waaye yaw yaa musal sa bopp.