TSK

TSK · Proverbs 17:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu,

Esawu ne ko: «Am naa ba biibal, sama rakk, fabal sa alal.»

Alali ger nag buleen ko nangu, ndax ger day gumbaal njàccaar, di safaan waxi ku nekk ci dëgg.

Ba loolu amee Daawuda nangoo ca loxol ndaw sa la mu ko indil, daldi ne ko: «Ñibbil ak jàmm. Dégg naa sa kàddu te nangul naa la.»

Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, kenuy suuf ne duŋŋ.

Nga di leen diir fittu kanam, ñu wone gannaaw.

Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.

Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.

Amos 5:12 TSK

Ràññee naa seen bàkkaar yu bare ak seen moy yu dul jeex. Yeenay tooñ aji jub, di geru, di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.