¶ Naka la Yuusufa gis magam ya, xàmmi leen, te mel ni ku leen xamul, di wax ak ñoom kàddu yu dëgër ne leen: «Fu ngeen jóge?» Ñu ne ko: «Réewu Kanaan lañu jóge, di jëndsi ab dund.»
TSK
TSK · Proverbs 18:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Firawna ne: «Kan mooy Aji Sax ji, ba ma di ko déggal, di bàyyi Israyil, ñuy dem? Xawma sax kuy Aji Sax ji, waxumalaa may bàyyi Israyil, ñuy dem.»
Su ko defee mboolem ku des ci sa waa kër dina ko sujjóotalsi, ngir as xaalis mbaa as dogu mburu, naan ko ‘Ngalla sas ma lenn ci liggéeyu carxal gi, ndax ma am as dogu mburu su ma lekk’.”»
Léegi nag seetal, ba xam loo ci wara def, ndax musiba kat dëgmal na sunu sang, ak waa këram gépp. Moom nag dafa naqari deret, ba maneesula wax ak moom.»
Ana ku ma abal lenn ba ma war koo delloo? Lépp lu mboolem asamaan tiim, maay boroom!
Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.
¶ Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam;
Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn?