day mel ni leeru jant bu fenk, kaw asamaanu suba su niir newul, leeru asamaan su set, taw ba siwet, ba ñax jebbi.
TSK
TSK · Proverbs 19:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci kaw loolu Buur bàyyikoo ca tóokër ba, délsi ca ëttu bernde ja, fekk Aman di sukk ca lal ba Esteer tëdd. Buur ne: «Ãa! Ba ci yekktaan Lingeer nag, te ma nekk ci biir kër gi?»
neex ni layub tundu Ermon, neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ. Fa la Aji Sax ji dogal barke, muy dund gu dul jeex.
Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
Kàddug buur kilifteef la. Ana ku ko naan: «Looy def nii?»
¶ Ci kaw loolu Nabukodonosor mer lool ba fees dell, kanam gay sël-sëli janook Sadarag Mesag ak Abet Nego. Mu santaane ñu xamb taal ba, ba mu gëna tàng juróom ñaari yoon na mu daan tànge;
¶ Buur nag am mbégte mu réy. Ci kaw loolu mu joxe ndigal, ñu génne Dañeel kàmb ga. Ba ñu génnee Dañeel kàmb ga, gaañuwul fenn, ndax daa wóolu Yàllaam.
Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, ci biir xeeti àddina, mbete gaynde ci biir rabi àll yi, nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt; fu mu jaare, joggati, xotat, te kenn du wallu.