TSK

TSK · Proverbs 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»

Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.

Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,

Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw; may ma, ma ràññee, yaa ko dige.

Gone yi, tee ngeena dégg yaru baay, te déglu, ba am ug dégg?

Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»

James 1:5 TSK

¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.