TSK

TSK · Proverbs 20:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

Dóor yu la gaañ faj na sag mbon, ay yar fóot na xolu boroom.

¶ Kan ci nit ñi moo xamal kenn nit, lenni biiram? Xelum nit ki ci biir nit ki doŋŋ moo mana xam biiram. Yàlla itam noonu la. Kenn xamul mbirum Yàlla, ku moy Xelum Yàlla.

Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.