TSK

TSK · Proverbs 21:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!»

Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal.

Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,

Ku am ug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.

Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.

Acts 5:5 TSK

¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.

¶ Yooyu xew-xew ay misaal la, ngir nu baña xemmem yëf yu bon, na ko maam ya daan xemmeme.

Képp ku masoona xëtt yoonu Musaa, daawuñu ko ñéeblu; ci kaw seedey ñaari nit ba ñett lees ko daan rey.