Genesis 8:21
TSK
Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.