TSK

TSK · Proverbs 27:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 26:6 TSK

Fàŋŋ la njaniiw def fa kanam Yàlla; du genn kiiraay gu ko làq paxum sànkute.

Ndax xef ak xippi mu wéy, mel ni lu saxi laaf, ne fëyy, naaw ni jaxaay.

njaniiw, jigéen ju jaasir, suuf, du màndi ndox, sawara, du ne doy na mukk.

Lépp lu saay gët xemmemaa, xañuma ko sama xol. Bañaluma sama bopp benn bànneex, xanaa di bége lu ma liggéey, yooloo ko la ma liggéey.

Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?

Moo tax njaniiw di yàkkli ag bóli, gémmiñ ga ne ŋafeet, amul kersa, boroom darajaak baadoolay Yerusalem doon xaxaloo, far tàbbi ca.

Biiñ day wore, jàmbaar ju bew jii nag du dal-lu, xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw, du doylu, mbete ndee, moom miy buubandoo xeetoo xeet, dajale askanoo askan, aakimoo.