TSK

TSK · Proverbs 27:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ña ngay fo, di awoonte, naan: Sóol jam junneem, Daawuda jam fukki junneem.

¶ Ci kaw loolu njiiti xarey Filisti di amal ay cong, noppiwuñoo xareek Israyil. Teewul saa yu ñu songaan, Daawudaay gëna am ndam mboolem jawriñi Sóol, ba mujj Daawuda amu tur lool.

Absalom jàppoo ko noonu ak mboolem bànni Israyil yay ñëw ca buur ba, di sàkku yoon. Ni la fàbbee xoli bànni Israyil.

Ku ñàkk a ngi, ñu futti, mu ngi binni, di néew-ji-doole. Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»

Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.

Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci njekk.

¶ Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal.