TSK

TSK · Proverbs 28:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñeengokati Misra itam fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona. Firawna të rekk, tanqamlu Musaak Aaróona, muy la Aji Sax ji waxoon.

¶ Ba mu ko defee waa Misra daw topp ca ñoom, fasi Firawna ak watiiri xareem aki gawaram ànd, ñoom ñépp ne yentam ca biir géej ga.

Jaamuleen Aji Sax ji, ragal ko, di ko bége, ba yaram daw.

ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,

Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.

Maay fas ak ñoom kóllëre gu sax dàkk gu ma leen dul xañati; xanaa baaxe leen, yeb ragal Yàlla ci seen xol, ba dootuñu ma won gannaaw.

Dëgg it; waaye ngëmadi moo leen fa tenqee, te yaw, ngëm a la fa teg. Bu ko réy-réyloo, waaye ragalal.

¶ Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.