TSK

TSK · Proverbs 29:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Musaa nag gis ni mbooloo mi ràkkaajoo, ndax fekk na Aaróona bay-bayal leen, ba ñu ràkkaaju, ba ku leen doon fexeel man leena ree.

Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem.

Ndokklee yaw mi maandu, di wéye yoonu Aji Sax ji.

Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.

Amos 8:11 TSK

«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.

Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»

Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk, wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte; xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.