TSK

TSK · Proverbs 29:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba mu ko defee Mardose bàyyikoo ca Buur; ma nga sol yérey buur, baxa ak weex, ak mbaxanam buur mu wurus mu réy, ak mbubbum lẽe mu xonq curr. Dëkku Sus baa ngay riire mbégteek bànneex.

Ku jub baaxle, waa dëkkam bànneexu; ab saaysaay saay, mbégte dim riir.

Bu ab soxor faloo, ñépp làquji, bu daanoo, ku jub teg tànk.

Lu mettee ngi lu ma gis fi kaw suuf, lu mel ni njuumte lu rëcc kilifa:

«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.