Leviticus 5:1
TSK
¶ «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp.
Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom, ab njaalookat, ngeen lëngool.
Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
Ku ma moy loru, ku ma bañ, daa repp.»
Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.