TSK

TSK · Proverbs 29:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des.

Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna.

Aaróona ne ko: «Sang bi, rikk bul mer, yaw ci sa bopp xam nga ni mbooloo mii yeboo ci mbon.

¶ Daawuda am lu mu foog ci kàddu yooyu, ba tax mu ragal lool Akis buurub Gaat.

Moo tax du genn góor mbaa jigéen ju Daawuda masa bàyyi mu dund, di ko indi Gaat, ndax ragal ñu nettali lu jëm ci ñoom, naan nàngam ak nàngam la ñoom Daawuda def. Noonu la jàppoo woon mboolem diir ba mu dal ca àllub Filisti.

Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, ma di ko xettli. Man la xam, te maa koy teg fu wóor.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ku doyloo Aji Sax ji, yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; dangay sax ba fàww.

Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.

Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.

Ana kooy tiit, ak koo ragal ba di ma wor, fàttlikootoo ma, faaleetoo ma? Damaa noppi lu yàgg daal, ba tax ragalatoo ma?

Sama Yàlla yebal na malaakaam, mu tëj gémmiñi gaynde yi, ba defuñu ma dara. Ndax kat mucc naa ci tuuma sama digganteek moom ak sama digganteek yaw it, te defuma dara lu bon.»

Luke 12:4 TSK

¶ «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.

¶ Keroog ba ma jëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp.