TSK

TSK · Proverbs 3:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Gaalu Yàlla ga, ñu jël; Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, dee.

Ezra 8:22 TSK

Ndaxte rusoon naa ñaan Buur mu boole nook ay dag ak gawar yu nu aar ci noon yi ci yoon wi. Li ko waral mooy fekkoon na nu wax Buur ne ko: «Sunu Yàlla mooy toppe yiwam mboolem ku ko yaakaar, di ko defal jàmm, waaye meram dina dal ak doole ci kaw mboolem ku ko dëddu.»

Buur wax ma, ne ma: «Ana looy sàkku?» Ma ñaan gaaw ci Yàlla Boroom asamaan,

Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la xool.

Ku dëggu, yoonam day maase; ku dëggu, Aji Jub ji jubal xàllam.

Man maay yékkati Sirus ci biir njekk, xàllu yoonam. Moom mooy tabax sama dëkk, yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal, te du laaj pey mbaa neexal.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.

¶ Cant ñeel na Yàlla, mi def ci xolu Tit, mu xér ci yeen ni ma xére ci yeen!

Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.

James 1:5 TSK

¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.