TSK

TSK · Proverbs 30:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israyil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.»

Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.

¶ Su ngeen sàmmoowula jëfe mboolem kàdduy yoon wii binde ci téere bii, ngir wormaal boroom tur wu màgg wii te raglu, seen Yàlla Aji Sax ji,

Job 11:8 TSK

Lu gëna kawe kaw, ana loo ci man? Lu gëna xóot njaniiw, ana loo ci xam?

Job 38:4 TSK

Ana foo nekkoon ba may samp suuf? Waxal su la ko sam xel mayee.

Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»

Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.

Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).

Ana ku natte géej biir loxoom? Ku xaymaa asamaan yaatuwaayu loxo? Ku mana fab suuf sépp, sol cib nattukaay? Ana ku natte ab màndaxekaay tund wu mag? Mbaa mu tam-tamal tund wu ndaw?

Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”

Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»