TSK

TSK · Proverbs 30:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol,

Bànni Israyil gis ko, di wax ca seen biir naan: «Lii lu mu?» ndax xamuñu woon lu mu doon. Musaa ne leen: «Lii mooy ñam wi leen Aji Sax ji jox, ngeen lekk.

¶ Suba su ñu xëyaan nag, ku nekk for ca njëlam, ndax bu naaj wa tàngaan, mu seey.

Bànni Israyil dunde nañu mànn diiru ñeent fukki at, ba kera ñu agsee réew mu ay nit dëkke, gannaaw ba ñu jéggee kemu réewum Kanaan.

Job 23:12 TSK

Dëdduwma ay santaaneem, sama biir xol laa denc ay kàddoom.

Ku jub bañ na ay fen, ku soxor di indi gàcceek yeraange.

Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.

Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.

Du njekk gu kenn wut cib àtte, du dëgg gu kenn sàkku cib layoo. Ñu ngi yaakaar caaxaan, di fen, di sos ayib, wasin ñaawtéef.

Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, di bàyyikoo ci buuru Babilon bés bu jot, giiru dundam, ba keroog muy dee.

¶ Teewul njullite gu ànd ak doylu, di alal ju réy.