¶ «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen.
TSK
TSK · Proverbs 30:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji yóbbu leen ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne yeen la koy jox, muy dëkk yu mag yu baax yu ngeen tabaxul,
Dingeen lekk ba regg, di sante seen Yàlla Aji Sax ji, réew mu baax ma mu leen jox.
Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.
Ndegam damaa def wurus sama yaakaar, bay tudde ngën-gi-wurus sama cëslaay;
Deesul sikk ku sàcc aw ñam, def ci biiram ndax xiif.
Éey niti Israyili tey, teewluleen kàddug Aji Sax ji! «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? Lu waral sama ñoñ naa: “Noo moom sunu bopp, dootunu délsi fi yaw”?
Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle,
Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,
Ngeen wëtti ba regg, regg, bew, ba tax ngeen fàtte ma.