TSK

TSK · Proverbs 4:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 11:14 TSK

fabal say ñaawtéef, sànni, te baña xajal njubadi sa biir xayma,

Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.

Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israyil, lu jar ngeen di dee?

Waaye léegi lii lépp baleen ko: tàng xol, ak mer mu ëpp, ak coxor, ak saaga, ak waxi ñàkk kersa.

Kon nag baleen jépp jikko ju tilim, ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu ci biir ag woyof, kàddu, gi jëmbate ci yeen te man leena musal.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.