TSK

TSK · Proverbs 5:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab.

Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal.

Job 18:8 TSK

Moo dox ba tàbbi cib caax, wëndeeloo biir mbaal,

ba ma siiwali sa woy yépp, fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, di bànneexoo sa wall gii!

Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.

Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.

Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.

Soo nee sa yoon nekku ci it, kiy natt xol yi, xam na, moom miy wattu sa bakkan, xam na, te kat mooy fey nit jëfam.

Ma seetlu lenn lu gëna naqari dee: muy ndaw su la fiir. Kooku cofeelam mbaal la, yoxo ya dib jéng. Ku Yàlla gërëm a koy rëcc, bàkkaarkat bi lay jàpp.

Samay tooñ la Aji Sax ji ëmb, fastee ko loxoom, mu tege sama kaw ndodd, ba jeexal sama doole. Boroom bee ma tàbbal ci loxo yu ma manula të.

«Bésub Aji Sax ji déy, dëgmal na, ñeel xeetoo xeet. Li ngeen def rekk lees leen di def, seenug pey këppu ci seen kaw bopp.

¶ Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmi, te mooy: powum séy, ak jëfi sobe, ak yàqute,

Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.