¶ «Buleen siiwal ay fen; buleen lëngoo ak tooñkat, ngir doon seedeb naaféqam.
TSK
TSK · Proverbs 6:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 23:1
TSK
1 Kings 21:10
TSK
te teg ñaari nit ñu tekkiwul dara, ñu janook moom. Na ñooñu duural Nabot ne ko: “Saaga nga Yàlla, saaga Buur.” Su ko defee ngeen génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.»
Psalms 35:11
TSK
Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.
Proverbs 8:13
TSK
Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
Proverbs 14:5
TSK
Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
Proverbs 19:5
TSK
Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
Proverbs 22:10
TSK
Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
Proverbs 26:20
TSK
Bu matt amul, ab taal fey, fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
2 Timothy 2:23
TSK
Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moyu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur.
James 3:18
TSK
Meññeefum njub nag, ci jàmm lees koy ji, ci biir doxkati jàmm yi.