TSK

TSK · Proverbs 8:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

Xel mu rafet day dooleel boroom, ba mu man fukki kàngam cib dëkk.

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

¶ Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,