TSK

TSK · Proverbs 9:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Buleen tong seen mbokk, te àrtuleen seen moroom bu baax bala ngeena bokk ak moom gàddu bàkkaar.

Natan ne Daawuda: «Yaw, yaay waa ji! Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa la fal buurub Israyil, maa la xettli ci Sóol.

¶ Buur Daawuda daldi ne: «Wool-leen ma Cadog sarxalkat bi, ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada.» Ba ñu dikkee fa kanam Buur,

Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.

Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce; kuy déggi àrtu, am teraanga.

Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.

¶ Waaye ba Sefas dikkee Àncos, jàkk laa ko def, weddi ko, ndax moo nekkul woon ci dëgg.

Sunu Boroom nag, ag muñam, jàppleen ne moo dig mucc, noonee leen ko sunu soppe, mbokk mi Póol binde woon ci xel mu rafet mi ñu ko baaxe.