TSK

TSK · Psalms 21:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yal na la may li nga namm, di sottal loo mébét,

Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.

Moom doŋŋ a di sama cëslaay, di sama wall, di sama rawtu, duma tërëf.

Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.

Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru jalub Yàlla.