Psalms 10:2
TSK
Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole, lal ay pexeem, ba jàpp ko.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole, lal ay pexeem, ba jàpp ko.
Waxuñu jàmm, xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi ay kàdduy tuuma.
Yal na askanam dagg. Balaa geneen maas a wéy, yal na seenu tur fey.
Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, ñii ñooy mébétkati ñaawtéef ñiy digle lu bon ci dëkk bii.
¶ Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,