Moo may tàggat ngir xare, may bank xalag xànjar.
TSK
TSK · Psalms 71:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku bon barew tiis. Ku wóolu Aji Sax ji, mu yiire la ngoram.
Ngalla def ma sa firndey mbaax, ba bañ yi gis ci, rus, ndax yaw Aji Sax, ji ma dimbali, dëfal ma.
Bésub keroog dees na ne: «Aji Sax ji, sant naa la; yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.»
Asamaanoo sarxolleel, suufoo bégal, te tund yi xaacoondoo! Aji Sax jee dëfal ñoñam, moo ñeewante néew-ji-dooleem ñii.
¶ Waaye cant ñeel na Yàlla! Moom mi Almasi tax mu di nu yóbbaale saa su nekk, ci njaab miy fésal ndamam, te cuuraayal xam-xamam, nun ñii la koy wasaaree fépp,
Loolu seral na sunu xol. Te yemunu ci xol bu sedd, waaye gënati nanoo bége mbégtem Tit, mi ngeen dalal am xelam, yeen ñépp.
¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»