TSK

TSK · Revelation 21:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

nit ñi làquji biir xuntiy doj, ruuruji biiri pax, ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, sore darajay màggaayam, kera buy taxaw, ba suuf di lox.

Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.

Yàllaa ngi jóge Teman, Aji Sell ji foofa ca tundu Paran lay bawoo. Selaw Darajaam moo dajal asamaan, teddngaam fees kaw suuf.

Gisatuma woon dara ndax leeraayu melax ga; ña ma àndal ñoo ma mujj wommat, ba ma agsi Damaas.

Dëkk baa nga ànd ak darajay Yàlla, leeraayam ba mel ni peru gànjar, nirook peru jàspë, leere ni kiristaal.

Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.