TSK

TSK · Revelation 9:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.

May xool, béjjén boobu di xareek aji sell yi, di leen daan,

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Ragal naa, bu ma dikkee, sama Yàlla ruslooti ma ndax yeen, may tiisoo ñu bare ñu wéye seen bàkkaar ya woon, te tuubuñu jëfi sobe ji, ak powum séy mi, ak yàqute gu af, gi ñu nekke.

¶ Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen.

Ñaareelu rab wi nag di def kéemaan yu réy, bay wàcce ci kaw suuf sawara wu jóge asamaan, nit ñi di gis.

¶ Meneen malaaka, topp ci, di ñaareel bi. Mu ne: «Babilon a daanoo, dëkk bu mag ba daanu na! Moom ma daan màndal askanoo askan biiñu moyam muy indi am sànj.»

Moom la buuri àddina àndal di moy, te biiñu moyam la waa àddina di màndee.»

Kaasu biiñu sànj, bi sababoo ci moyam, moom la askani àddina yépp di naan. Moom la buuri àddina àndal di moy, te doyloodig bakkanam gu réy woomal na julay àddina.»

Ay àtteem dëgg la, yoon la! Moo mbugal jigéenu moykat bu mag, bi yàq àddinaak moyam, feye ko deretu jaami Yàlla yi mu tuure loxoom.»

Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.