TSK

TSK · Romans 1:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Bu góor tëdde góor, ni bu doon jigéen. Lu ñaawa ñaaw la.

Efrayim googu laa ne, moo lëngook jëmmi tuur! Seetaan leen.

Acts 7:42 TSK

Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?

Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus, mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.

Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu ndee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon.

¶ Dawleen powum séy! Mboolem bàkkaar bu nit mana def, bàkkaar ba du jote dara ak yaramam, waaye fokat bi, yaramu boppam lay lore bàkkaaru powam.

Su ko defee kenn ku nekk ci yeen mana moom yaramu boppam ci biir sellnga ak teddnga,

¶ Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa, ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan.