TSK

TSK · Romans 10:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, di déglu kàddug jaamam? Képp kuy doxe lëndëm te amul leeraange, na wóolu Aji Sax ji, te wéeroo Yàllaam jii.

Ñenn ña nag gëm la mu wax, ña ca des weddi.

Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo.

Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.

mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal,

¶ Seen njàlbéenu xél de baax na! Ana ku leen gàllankoor ba toppuleen dëgg gi?

Ndax kat ni ñu nu àggee xibaaru jàmm bi, noonu lees leen ko àggee, waaye kàddu ga ñu dégg moo leen jariñul dara, ndax ña ko dégg ñoo ko déggewul ngëm.

¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.

Te it: «Mooy doj wuy fakktale, di xeer wuy daaneel.» Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.