TSK

TSK · Romans 10:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aji Sax ji waxati ma, ne ma: «Gis naa ne mbooloo mii kat, ñu dëgër bopp lañu.

Aji Sax ji ne ko: «Déggalal mbooloo mi te def li ñu la wax lépp. Du yaw lañu bañ, waaye man mii lañu bañ ma doonati seen buur.

Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.

Aji Sax ji yónnee leen mboolem jaamam ñiy yonent yi. Yónni na leen ay yooni yoon. Waaye dégluwleen, teewluwleen.

Yónnee naa leen ay yooni yoon mboolem yonent yi, sama jaam ñi, ne leen: “Rikk buleen def jëf ju siblu jii ma bañ.”

Acts 7:51 TSK

¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!

Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.