TSK

TSK · Romans 11:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 9:15 TSK

Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.

Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»

ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.

Sama tànk yooyu nag am peeñu moo ko waral. Ca laa wéetoo ak ña ñu jàppoon ne ñooy kàngami mbooloom gëmkat ña, faramfàcceel leen xibaaru jàmm bi may yégal jaambur ñi dul Yawut, ngir ragal sama liggéey bi ma jota def, te di ko wéye, doon coonob neen.

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi.

Te ci xibaaru jàmm boobu lañu ma tabb, ba ma di yéenekatu xibaar bi, di ndawam, di jànglekatam.