TSK

TSK · Romans 11:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, kenn du Yàlla ku dul man! Man maay rey, di dundal; di gaañe, di wéral; maay jàpp, te kenn du xettli.

Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.

Moo xalab Firawnaak mbooloom ca géeju Barax ya. Kee saxoo ngoram!

Su dee boroom njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko àrtuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj.

¶ «Sa bokk yi nee ñu: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Te ñoom la seen doxalin dul noonu!

Luke 8:15 TSK

Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.

Ba Barnaba dikkee ba gis yiw, wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoye seen xol ci Sang bi.

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

¶ Yàlla mi namma wone am sànjam, xamle dooleem, su dee moo muñal lool ay ndab yu yelloo am sànjam, te seen sànkute ñoroon xomm nag?

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

Ndax kat noo di àndandooy Almasi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga.

¶ Kon nag buleen teqlikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.

Jude 1:20 TSK

Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.