Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
TSK
TSK · Romans 16:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy mëdd ndee ba fàww! Boroom bi, Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.
Ni ñeyi xare lañuy mel, di joggati banu mbedd mi ci biir xeex bi. Noonu lañuy xaree, nde ñoom la Aji Sax jiy àndal, ñuy torxal gawar yi.
Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
Yal na Yàlla miy boroom jàmm ànd ak yeen ñépp. Amiin.
¶ Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen! Amiin.
¶ Yal na yiwu Sang Yeesu ànd ak yeen.
¶ Bokk yi, yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak seenum xel. Amiin.
¶ Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen.
Yal na Boroom bi wéttali sam xel. Aw yiw ñeel na leen.
¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
¶ Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne: «Léegi nag texe teew na, ànd ak sunu kàttanu Yàlla ak nguuram, ak sañ-sañu Almaseem, ndax xalab nañu ki daan tuumaal sunu bokk yi, di leen sosal guddeek bëccëg fi sunu kanam Yàlla.
¶ Yal na yiwu Sang Yeesu ànd ak ñépp.