TSK

TSK · Romans 2:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ana wan xeet wu mag wu am yàlla ju leen jege ni nu sunu Yàlla Aji Sax jiy jegee saa yu nu ko wooyee wall?

waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.

Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.

Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.

Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa, ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi.

Xanaa ni àddina ci boppam tëdde xamalu leen ne yar kawar gàcce la ci góor?

¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.