«Yerusalem, ana lu tax ma di la baal, te say doom wacc ma, di giñe lu dul Yàlla. Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo, riixle, jëm kër gànc ya!
TSK
TSK · Romans 2:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Jeremiah 5:7
TSK
Jeremiah 9:2
TSK
«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, te man faalewñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.
Malachi 1:8
TSK
Bu ngeen ma sarxalsee jur gu gumba, dara aayu ci? Am bu ngeen ma sarxalsee jur guy soox, ak jur gu wopp, dara aayu ci daal! Yóbbul leen ko seen boroom dëkk rekk, ba xam ndax moo leen di nangul, mbaa mu siggil leen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Malachi 3:8
TSK
Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.
Acts 19:37
TSK
Ndax nit ñii ngeen fi indi, teddadiluñu ay jaamookaay te waxuñu lu ñàkke sunu yàlla kersa.