TSK

TSK · Romans 3:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

te ñu naan: «Dellul gannaaw, bul ma jege, maa la gëna sell!» Lii déy daa mel ni saxar ci samay wakkan, mel ni sawara su yendoo boy.

Luke 18:9 TSK

¶ Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.

¶ Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, deful ag njubadeem?

Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.

¶ Kon léegi nag? Li am moo di li bànni Israyil doon wut, amuñu ko. Ñi ñu taamu ñoo ko am, ña ca des, seenum xel a dërkiis.

Ana ku la def nga gën ci nit ñi? Ana loo am lu ñu la joxul? Te ndegam dees la koo jox, ana loo koy puukarewoo, mbete lees la joxul?

Kon ana nees di def? Naa ñaane sama xol, tey ñaane samam xel itam. Naa sàbbaale sama xol, tey sàbbaale samam xel itam.

Waaye mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi di jagle, mana dikkal aji gëm ñi.