TSK

TSK · Romans 4:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

jëkkër ji dégg ci, te waxu ko dara, aayewu ko, su boobaa mboolem xasi ndaw si day sax, te mboolem dogu bu ndaw si tegooloon boppam, day sax.

Aji Sax ji, jëf jot na, ñee ngi jalgati saw yoon!

Maay neenale fii pexem Yudak Yerusalem. Maa leen di tërale seen saamaru noon, ñi leen di tëru, tër leen; seeni néew, ma leele njanaaw ak rabi àll.

¶ Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.

Su doon ci yoonu Musaa la ndonale ga aju, kon dootul doon lu digeb Yàlla waral. Waaye ci kaw ab dige la Yàlla baaxee Ibraayma aw yiwam.

ngir ma mana feeñe ci biir Almasi, fu ma yaakaarul sama njekku bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njekk gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi. Njekk googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi moo koy maye.

Ndax kat yoonu Musaa, ay nit ak seenug néew doole la fal ay sarxalkat yu mag. Waaye kàddug ngiñ li topp ci yoon wi, moo fal sarxalkat bu mag, Doom ji ñu matal sëkk ba fàww.