Job 9:19
TSK
Su dee kàttan, kee bare doole! Su dee wàllu yoon, kan moo ma cay woo?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su dee kàttan, kee bare doole! Su dee wàllu yoon, kan moo ma cay woo?
Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.
Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.
¶ Xam naa dinga ne: «Car yooyu, dees leena tenqi, ngir jabtal ma.»
¶ Teewul nit a ngi naan: «Nan la ñi dee di dekkee? Wan yaram lañuy dekkaale?»