Isaiah 51:1
TSK
Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:
Nde su dee ñi ci yoonu Musaa la dige bi ñeel, kon ngëm dootu tekki dara, te kon digeb Yàlla ba day neen.
Ñoom laa seedeel seenug parlute ci Yàlla, waaye dañu koo tegul ci xam-xam bu doy.
¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»
Ma artooti képp ku dem ba ñu xarfal ko, ne ko mboolem yoon wi la wara jëfe.
Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daanu ku moy yoon wépp ñeel na ko.