¶ Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.»
TSK
TSK · Ruth 2:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 33:8
TSK
Genesis 33:15
TSK
Esawu ne ko: «Xaaral ma bàyyee la ñenn ci góor, ñi ma àndal.» Yanqóoba ne ko: «Matu ko. Boobu teraanga ëpp na, sang bi. Jàmm ji nga ma dalal rekk doy na.»
Genesis 43:14
TSK
Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.»
1 Samuel 1:18
TSK
Aana ne ko: «Amiin, sang bi, yal nanga ma yàgga yéwéne.» Ba mu ko defee Aana dem yoonam, doora mana lekk, kanam ga leer.
2 Samuel 16:4
TSK
Buur ne ko: «Kon boog, may naa la mboolem alalu Mefiboset.» Mu ne ko: «Jaajëf Buur sang bi, gis naa ni nga ma baaxee.»
Hosea 2:16
TSK
«Moo tax maa ngii di ko naxtaan, maa koy yóbbu ca màndiŋ ma, ba déey ko lu xolam dégg.