TSK

TSK · Titus 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir,

¶ Naka noonu ab taxawukatub mbooloo mi, na di ku tedd, bumu di boroom ñaari kàddu. Bumu di ku sàngara jiital, mbaa kuy sàkku am-am bu lewul.

¶ Waaye kiy ab jëtun dëgg te di ku wéet, mooy ki yaakaar Yàlla, te saxoo ay dagaan aki ñaan, guddi ak bëccëg.

Titus 1:7 TSK

Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul.

Ndax kat nëgëni tey waroon na leena fekk diy sëriñ, waaye aajowoo ngeen ba tey ku leen jàngal ndoortel waxi Yàlla. Nàmp um soow ngeen mujj aajowoo, ndax ñàkka àttan ñam wu dëgër.

¶ «Waaye lenn laa lay sikke: dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, muy jàngleek a réeral sama jaam ñi, ngir ñuy gànctu ak a lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur.