TSK

TSK · John 2:21

Treasury of Scripture Knowledge references in Téereb Injiil.

Back to passage
John 1:14 TSK

¶ Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.

Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy kër Yàlla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci yéen, te Yàllaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp,

Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa.

¶ Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Yàlla gépp dëkk,

¶ Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,