TSK

TSK · 2 Samuel 19:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Xam nga ne li nga def baaxul de! Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, dee rekk ngeen yelloo, yeen ñi wattuwul seen sang, ki Aji Sax ji fal! Xoolal bu baax, ana xeeju Buur ak njaqal ndox li féete woon ak boppam?»

Dee ko beyal tool yi, di ko góobal, yaw yaak say doom ak say surga, ndax waa këram am ab dund. Mefiboset nag, mook man ay bokk ndab.» Ciba amoon na fukki doom yu góor ak juróom, ak ñaar fukki surga.

Léegi nag sang bi, yal na sa kàddu gii di sama noflaay. Ndax yaw Buur, sama sang, dangaa mel ni malaakam Yàlla, am ug dégg, di teqale liy yoon ak li dul yoon. Yal na sa Yàlla Aji Sax ji ànd ak yaw.»

Waaye bu ma waxee ne ma bégul ci man, su boobaa ba tey maa ngi. Na def li ko soob ci man.»

Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.»