¶ Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.
TSK
TSK · Acts 13:4-5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
lu moy li ma Noo gu Sell giy seereel ci dëkkoo dëkk, ne ma ay jéng aki coono moo may nég.
Musaa daldi jóg, mook Yosuwe, bëkk-néegam. Musaa nag yéeg ca tundu Yàlla wa.
¶ Alyaasa bàyyi fa Ilyaas, dellu jël ñaari nag, rendi ko sarax, jël banti ràngaay ya, togge yàpp wa, jox ko mbooloo ma, ñu lekk, ba noppi Alyaasa topp ci gannaaw Ilyaas, di bëkk-néegam.
Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.
¶ Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
¶ Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.
¶ Ba mu ko defee ñu jaare dëkk ya ñuy wax Amfipolis ak Apoloni, doora àgg Tesalonig, ga Yawut ya amoon ab jàngu.
¶ Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.
¶ Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko.