Menn kuuy mi, nga rendi ko ci suba, meneen kuuy mi, diggante ngoon, ba jant di so.
TSK
TSK · Acts 3:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal.
Ci kaw loolu Buur Daryus torlu mbindum aaye ba.
¶ Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
¶ Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
¶ Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
¶ Am peeñu nag dikkal ko digg njolloor, mu gis ci lu leer malaakam Yàlla, mu duggsi, ne ko: «Korney!»
Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.