TSK

TSK · Acts 7:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw.

Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,

Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»

«Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»

Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.

Buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox ci seen suuf fu téstën sax tege, ngir Esaween ñi laa sédd diiwaanu tundu Seyir.

Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

ndax itam ngeen gudd fan ca réew ma Aji Sax ji giñoona jox seeni maam, ñook seen askan; réew mu meew maak lem ja tuuroo.

Yaa gis mu nangul la ci xolam; nga fas ak moom kóllëre, dig askanam réewum Kanaaneen ñaak Etteen ñaak Amoreen ñaak Periseen ñaak Yebuseen ñaak Girgaseen ña. Te def nga li nga dige it, ndax yaw boroom njekk nga.

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.