TSK

TSK · Amos 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.

Seen tuut-tànk, yi ngeen ne alalu sëxëtoo lañuy doon, ñoom laay yóbbu, ba ñu xam réew ma ngeen xarab.

Ci kaw loolu ma ne leen: «Agsi ngeen fii ci tundu Amoreen ñi nu sunu Yàlla Aji Sax ji di jox.

Ndax yeen kat seen Yàlla Aji Sax ji moo barkeel seen mboolemu ñaq te moo ràññee seen doxub màndiŋ mu yaa mii. Ñeent fukki at a ngii seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ñàkkuleen dara.”»

Diiru ñeent fukki at nga leen dundal ca màndiŋ ma, ñàkkuñu dara. Seeni yére ràppul, seeni tànk newiwul.

Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.

Newuñu: “Ana Aji Sax, ji nu génne woon réewum Misra, jiite nu ca biir màndiŋ ma, ca joor gu wow gaak xur ya, réewum maral ma lëndëm këruus, jaareesu fa, dëkkeesu fa?”

Ma génne leen réewum Misra, yóbbu leen ca màndiŋ ma.

Amos 9:7 TSK

«Bànni Israyiloo, xanaa du yeen ak waa Kuus laa yemale?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du ni ma leen génnee réewum Misra laa génnee Filisteen ñi réewum Kaftor, génnee ni waa Siri réewum Kir?

Acts 7:42 TSK

Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?