Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
TSK
TSK · Colossians 2:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.
Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.
¶ Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!»
Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.
Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.
¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at.